Narah Diouf - Guëmeul Sa Bopp lyrics

[Narah Diouf - Guëmeul Sa Bopp lyrics]

Sama yaay ne ne ma
Bul tiit te bul ragal
Demal foncel
Te xam ne am nga ñaanu yaay
Am nga ñaanu yaay, oh oh

Dinaa jëm lu ma mën
Ndax yaay li nga sonn ma muñloo
Dinaa def lu ma mën
Ndax baay li nga sonn ma dooleel
Moo ma dooleel
Baay boy moo ma dooleel

Yoon wi gudd na
Waaye gëmal sa bopp te xam yaay kan
Ku mu mën doon ku mu mën ci nekk
Gëmal sa bopp
Gëmal sa bopp
Gëmal sa bopp

Ñu ngi lay xeex te xamoo leen


Ñu ngi def te gisoo leen
Waaye bul tiit, bul jaaxle
Ndax Yàlla ñépp la fi nekkal

Bul mas di xaadi
Jàppal ba mu dëgër bul bàyyi
Dinaa jëm lu ma mën
Ndax baay li nga sonn ma muñloo

Yoon wi gudd na
Waaye gëmal sa bopp te xam yaay kan
Ku mu mën doon ku mu mën ci nekk
Gëmal sa bopp
Gëmal sa bopp
Gëmal sa bopp

Lambour Penda Madior
Séni Ndiaye, Yacine Diémé
Borom Diam yi ñul yi ak yu xees yi
Ma wooy sama maam jee
Ma wooy sama maam

Man jooy na sama maam jee
Duma la mësa fàtte mukk ci àdduna
Sa dem gi wetal na ñoo
Maam boy namm naa la

Interpretation for


Add Interpretation

A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z #
Interpret