Narah Diouf - Xarit lyrics
[Narah Diouf - Xarit lyrics]
Ku kaay wax dëgg kuy dellusi xelam
Nit ku ne am na ku kaay jubbënti
Sayu reere fàtte li ko war
Yéena maggando, yéena gowando
Bokk ay bëgg-bëgg mel ni ay seex
Mel ni ay seex
Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti
Yaw mi may teg si yoon su ma réere
Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti
Yaw mi ma gëna xam sama bopp
Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti
Yaw mi may teg si yoon su ma réere
Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti
Yaw mi may wétali
Oh oh oooh
Ouh ouh ouhh
Yenn saay ñu meroo
Ku ne dem sa yoon
Seytaan ak pexem mëna tas lu ne
Waye yàgg yàgg dañuy boo loo watt
Àndaando nekk benn mel ni ay seex
Mel ni ay seex
Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti
Yaw mi may teg si yoon su ma réere
Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti
Yaw mi ma gëna xam sama bopp
Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti
Yaw mi may teg si yoon su ma réere
Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti
Yaw mi may wétali
Oh oh oooh
Ouh ouh ouhh
Mel ni ay seex
Di dox mel ni ay seex
Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti
Fu ma lay jëleeti?
Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti
Wax ma kooo!
Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti
Wax ma kooo!
Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti
Yaw mi may wétali